Saar 15

8.9K 1.1K 193
                                    




           

******Adja*******

Khalil dé dafe mané wone bou agué woma. Bima yéwo ba légui magui time sama portable. Khoma loumouy def ?

Bou fekone genre day oublier woute puce pour meune ma wok one dina comprendre mais instant yi ak whatsapp bi wala messenger mome, souma wowoul c'est parce que dako neikh. Sama pass-orange bagui ni recharger nako juste ndakh mome légui moumay bagna falé.

En plus magui ni dama wara ligueyi. Sou woté fék may léte nane lay wouyo rek?

Gor gni par yéne say je me demande nougnouy khalaté.

Sama heure diote na, il faut que ma déme.

*****

Bimay dokh ci mbéde lay dégue sama téléphone sonner. Heureusement ba désactiver wouma données mobiles.

Khalil dé may wo ak whatsapp.

-Princesse mba yéwoumala?

-Yé? Mane magui ni ci mbéde li di dokh, salon ba la dieum damay ligueyi.

-Sorry. Dama perdre notion du temps nak. 

-Depuis ci soubeu bima yéwo ba légui magui done khar sa appel. Dama foguone sakh ni dagau ma faté.

-Bébé yow tamitt kéne dou faté bopam. Té khame gua yow ci mane gua bok.

-Khalatona sakh gua déme ci sa diabar bi mou téyé la.

-Ex diabar. Bou dé kokou rek, sa khel meune na dal. En fait dama  aksi il fallait que ma yobeu khalé yi séne keur yaye soguay gneuw sama logement, té khame gua deuk bi moy lolou sa dounde yeup ci tali bi guakoy passer.

-Mba nopalikou gua rek.

-Instant yi sangou rek la def pour tagalikou ak tangor guima indalé, bagages yi sakh rangerwoumako. Khame nani mome nélaw yi ma nara nélaw, kou ma yé dinala méré.

Limou wakh nak daf ma def ay ré.

-Puisque khame nani yagui ci diame rek kone bakhna, aksi na sakh ci bountou salon bi il faut que ma dougue. Nala bayi gua nopalikou.

-Ok, dinala wo bou goudé.

-Cool. Bisous.

-Bisous.

Ma dougue ci salon bi nouyo. Dié mome wakhone nako que khalil day dem France, damako khamal rek que déme na demb après clianes yi gneuw gnou gérer léne.

******

Khalil dé bimouy soggay dem, daf ma dane wo chaque jour après khame na loiguey bi diape ko khame na  mouy teubeul. Ins yi semaine mogui ni dégouma batam. Au moins souma ko messager dina tontou, wayé dal guiss nani amoul sama diote.

-Adja, naka Khalil ?

Gno gui salon ba. Dié momay lathie ay nouvellou Khalil.

-Khana mogui ci diame.

-Fofou gua ci toleu.

-Khalil khame na liguey béko eupe dolé wala bok da ame Paris guel.

-Do bayi sa wakhi dof yi?

-Khalil dal feral nama en tout cas. Bimouy soguay déme appel la wone légui nak message.

-Liguey bi la rek, boul faté ni missions moko fa yobe.

-Wa Adja...Nogaye mognou feksi ci wakhtane bi.

-Hum.

-Yagui fatélikou Gora ?

-Gora ?

-Kifi gneuwone kérok done ma sete ci.

-Moy ki yoré boutiquou cosmétiques bi.

-Kokou la nak.

-Loume beugue.

-Depuis kerok say wakh lamay rayé, néko nak yagui ci lou sérieux amo diotame, mou tontouma néma donté dou dieukeur yonam nékoussi.

-Thiey goor gni.

-Lathie nama sa numéro mais damako né balla mako diokhé lathie la d'abord yow miye ndéyou mbile gui.

-Diokh koko.

-Ay Adja !!!

Dié dé momay beugue todjal fi.

-Yow dimbeulima dé. Loumouy mel ni dama wakh lou graw.

-Koula bayi gua wakh Nogaye mou diokh sa numéro goor ?

-Khalil magua France té khoma loume néké. Nogaye diokh ko numéro guané ko mou wo. Tok na sougnou keur baye wadjer neub au moins sakh ma guéne touti.

-Magui kokoy diokh.

Nogaye mako khame, aka ciy sawar yague na ma brancher ay mbarane. Li takh moussiy sawar moy, momitt dagnoukoy bokal donc avantage késsé laciy dieulé.

En plus Khalil fi ak wer lay gnibissi donc meune na nek ci lima nekh.

Bou gnibissé souma woré ni Paris liguey dongue la fa done def ma bayiwatt mbarane gui bala mou may diape.

-Mane dé sama wakh dou ci bari.

-Dié wakh dji gnola ko diégueul.

-Bou Khalil di gnoussati sa mame ci kherr yi fékhel ba bouma ci thiaya lale.

-Thiaya dou la ci lale, seur doula ci lale.  

-Dié yow tamitt, Adja dofoul khame na noumouy gérer Khalil.

-Nogaye wa kay wakh ci.

-Khame noumouy gérer Khalil mo takh mou tok fi werou yalla di dioy.

-Lolou erreur de debutante la wone, bouy diogué France may def réglages d'usine.

-Wa rétane nal, dou dagua gnak diome rek. Mane dal fékhel ba bou ma ci wakh dara.

-Gnanal ma diam tamitt. Ame na temps wou gérer affaire yi.

-Ok.

-Boul wakh dara Ouzin nak.

-Adja nak yaguii may saga. Mane may sa féne kat? Dou fi gua takhaw né Khalil diank gua, est-ce que takhna ma wakh Ouzin contraire bi?

-Wa c'est bon.

*******

Gora momou ma Nogaye done wakh ci même jour bi la ma wo. Wa dji nak lokho ci poche la. Dama foguone ni diaye kat dongue alors que commerçant bou mak la lay yek avion di wathie di wouti marchandise fou nek. Na ci lek lima ci meune lolou dongue la meune, en plus homme marié leu. Kerok mou gneuw di khass diabar dji di ko yakk lou nek. Lou takh goor gni bone rek la khamoul. Bou amé diabar di dokhane rek di sikeul séne diabar yi. Mane dé lolou yeup diarouko ci wone. En plus namone na mbir mi name bo khame né, dès l'instant que wétone naigne sokhla wouma wone dara. Khalil kat bimou také sama birr dafa yague tamitt naigne ko wakh té dé. Ma mak ay foneuté késsé, affairou khalé yoyou. Khana khalé yi sakh dépasser naigne yoyou.

******

Affaire yi dé ci Gora la commencer dé wayer, dana ka délouwatt na ci lima nékone. Ame na sakh ay ex you gneuwatte gnou nékalatte koci. Ak kénéne kou bess. Ins yi magui ak 5.

Dama néwone bou Khalil gneuwé ma bayi dé, wayé guéne naci. Khalil sama portable la ma diapé bipa nak douma diap dieul na samay matouwayy, portable bi douma ci bayi dara lou suspect.

Khalil après done naigne déguaneté watte, bouko nékhé wo ma bouko nékhé message ma. Kéne tognouma ma togne sama bope khoma loumay dokh di nobaté ba gnak ko dégue dima souffrirelo.

Instant yi dé ma gui gnibi, tay mome liguey bi dafa bari wone mo takh magui sone.

Bimay dougue ci keur gui ma dégue sama yaye di wakh tane bay khatay. Khana dagno ame guane.

Bima aksé ci salon bi ba guiss Khalil dé, li diogué ci mane dotoul meuss délouci.  

Kéne kou mel ni yowOù les histoires vivent. Découvrez maintenant